dajale ay njaboot ci ndigalu regulasion dublin iii · • sa mak walla sa rakk bu jigeen? • sa...

2
Print: ISBN 978-92-9494-887-8 doi:10.2847/964898 Web: ISBN 978-92-9494-902-8 doi:10.2847/997031 SUPPORT IS OUR MISSION Dajale ay njaboot ci ndigalu Regulasion Dublin III Ci ñan la yoon bii tegu? (WO) Lan nga wara def? Nanga jokkoo ak EASO, UNHCR walla njitu Itali bi: Ñoom mënnañu la xibaar lu bari ci nan nga mëna fekki say mbokk ci meneen réewu Ërop mi. Ngir njiit yi man la dimbale, danga wara: Joxe xibaar yu wóor yuy wone say waa njaboot ak seen nekkin ci meneen réewmi: Xibaar bi warna am tur, sant, besu juddu, address bi nga dëkk, nimero telefon bu fekke am nga ko, sa nekkin ci réewu Ërop mi (bu fekkee moom walla yow dawlàqu nga, bindu nga ngir am kirayu internasional te beg-bëgg bi antoogul, ak yu ni mel.) Joxeel ay kayit yu am: Kayit yuñu lay xammee wala kayit bumu mënti nekk wala xibaar yu mënë firndeel sa diganté ak sa mbokk, ak nekkinam ci meneen réew. Ñaari pàcc yópp dañu wara jebbël ap bataaxalu deggoo, te ñu wane bëgg booloo ci bindante. BZ-04-18-236-WO-N

Upload: doanhanh

Post on 29-Aug-2019

212 views

Category:

Documents


0 download

TRANSCRIPT

Print: ISBN 978-92-9494-887-8 doi:10.2847/964898Web: ISBN 978-92-9494-902-8 doi:10.2847/997031

SUPPORT IS OUR MISSION

Dajale ay njaboot ci ndigalu Regulasion Dublin IIICi ñan la yoon bii tegu? (WO)

Lan nga wara def?Nanga jokkoo ak EASO, UNHCR walla njitu Itali bi:

Ñoom mënnañu la xibaar lu bari ci nan nga mëna fekki say mbokk ci meneen réewu Ërop mi.

Ngir njiit yi man la dimbale, danga wara:

• Joxe xibaar yu wóor yuy wone say waa njaboot ak seen nekkin ci meneen réewmi:Xibaar bi warna am tur, sant, besu juddu, address bi nga dëkk, nimero telefon bu fekke am nga ko, sa nekkin ci réewu Ërop mi (bu fekkee moom walla yow dawlàqu nga, bindu nga ngir am kirayu internasional te beg-bëgg bi antoogul, ak yu ni mel.)

• Joxeel ay kayit yu am:Kayit yuñu lay xammee wala kayit bumu mënti nekk wala xibaar yu mënë firndeel sa diganté ak sa mbokk, ak nekkinam ci meneen réew. Ñaari pàcc yópp dañu wara jebbël ap bataaxalu deggoo, te ñu wane bëgg booloo ci bindante.

BZ-04-18-236-WO

-N

Bu fékké sa at weesuwul 18, té nekkoo ak kilifa kula mëna gàddu, te it nga bëgg fekki sa mbokk ci meneen réew:

• Sa yaay, sa bay wala beneen kilifa bula mëna gàddu ci yoon?• Sa mak walla sa rakk bu jigeen?• Sa tanta, sa nijaay walla sa maam bula mëna gàddu?

Bu fekkee amga lu ëppu 18 at te nga bëgg fékki sa mbokk, buñu nangu ni dawlàqu la walla muy jot kiray gu matt:

• Sa jabar walla jëkër, ku nga nékkal ci anam yu dal?• Sa doom ju amul 18 àt?

Bu fekkee amga lu ëppu 18 àt tenga bëgg fekki say mbokk, ñu nga xamni bindu nañu ngir am kiray internasional te seeni bëgg-bëgg àntoogul:

• Sa jabar walla jëkër, walla ku nga nékkal ci anam bu dal?• Sa doom ju amul fukki àt ak juroom ñett?

Man ngaa sàkku boole sa njaboot bu fekkeeni

• danga ëmb• wala nga wësin• wala amatoo kàttan• nga feebar dëg-dëg• wala danga jëm mag

Ndax danga aju ci sa doom, ci sa mag walla rakk, walla ci sa waajur wu dëkk ci benn ci réew yi booloo yi ñu lim ci kaw walla bufekkee ni sa doom, WALLA sa mag walla rakk, walla sa wajur dafa aju ci yaw te dëkk ci menn ci réew moomu WALLA sufekkee ni sa doom, sa mag walla rakk, walla sa waajur yu dëkk ci menn ci réew yi bokk, ci yow la ñu aju ngir ndimbal.

Bu fekkee danga bëgg fékki sa mbokk mu la jege te nga mën ko topatoo: bu fekkee dafa ëmb walla mu wësin, bu fékké amatul kàttan, walla mu fébar dëg, wala mu jëm magg.

• Sa doom ju am lu ëpp fukki 18 àt?• Sa mag walla rakk bu goor walla bu jigéén?• Sa mbokk?

Ci ñan la yoon bii tegu?Ci ñan la yoon bii tegu? Ci ñan la yoon bii tegu?

Ndax amnga koo bokkal njaboot* ku nekk leegi nii ci réew yiñu lim ci suuf?

Otriis? Belgik? Bulgari?Kroasi? Siipr? Repiblik Cek?Danmark? Estoni? Finland?Frans? Almaañ? Grees?Hongiri Island? Irland?Itali? Letoni? Liechtenstin?Lituani? Luksamburg? Malt?Olaand? Norwees? Poloñ?Portugal? Romani? Slovaki?Sloveni? Espaañ? Sweed?Swiis? Royaume Uni?

* “Ku bokk ci njaboot” mooy kinga bokkal njaboot ci réew minga bayyikoo te mu nekk leegi ci réew yi ñu lim. Joxenañu misaalu njaboot ci kayit gii.