wolof - lartes-ifan. · pdf filewolof. jàngandoo nattukaay bu moom boppam la, di...

4
Février 2015 ISSN 2230-0678 Wolof

Upload: duongdiep

Post on 09-Feb-2018

213 views

Category:

Documents


0 download

TRANSCRIPT

Février 2015 ISSN 2230-0678

Wolof

Jàngandoo nattukaay bu moom boppam la, di génn ci jamono, li ko tax a jóg di natt baaxaayu xam-xam bu lalu bi ñuy dugal ci boppu xaley Senegaal. Ngir nas nattukaay bii ittewoo doomi réew, Gëstuwaay bi màcc ci Coppeeku yi aju ci Koom ak Nekkin (Lartes), te bootu ci Ifan, dafa lëkkaloo ak lu tollu ci fukki ONG yuy doxal gëstu bi ci biir diwaan yi. Dañuy natt xareñug xale yi am 6 (juróom-benni at) jëm 14 (fukki at ak ñeent).

Dolli ci, ñeenti «Kuréli doxalkat» yu dajale ay kàngam yu seen xam-xam màcc ci mbirum njàngale ñoo topp defarug roytéefu njàngale mi, mooñaale ci coppite, ngir samp baaxaayu njàng mi.

Jàngandoo,nattukaayu baaxaayu njàng mici Senegaal

Jàngandoo ngi wéeru ci ñeenti beesal yu mag :

Jàngandoo 2014 ci gàttal

Ci atum 2013, natt yi ñu ngi leen amale woon ci 5 000 kër (juróomi junni), ci tànnin wu mbooloo mi gis boppam, dajale 15 277 (fukki junni ak juróom ak ñaari téeméer ak juróom-ñaar fukk ak juróom-ñaar) ciy xale yu am (6) juróom-benni at ba (18) fukki at ak juróom-ñett. Ci atum 2014, lim bi 10 000 kër la (fukki junni), yemoo ak 26 068 (ñaar-fukki junni ak juróom-benn ak juróom-ben-fukk ak juróom-ñett) ciy xale yu am diggante (6) juróom-benni at ak (14) fukki at ak ñeent ;

Xale yépp, moo xam frãse lañu tànn walla araab, cax yi ñu leen jox dañu leen maasale, teg leen ci dayo bu digg-dóomu, méngoo ak njeextel ñetteelu atum njàng mi ;

Jeexitali cax yi dañu leen xamal way-jur yi ci saa si, sog leen a wax mbooloo tund yi, ak jàngalekat yi, ak way-góornëmaa yi, ak way-bokk faluwaay yi, añs ;

Ñu ngi doxal natt bi ci sàrti xam-xam yu wér, ngir taxawal firnde yu ne fàŋŋ yu wone ne fàww coppite am, jëm ci baaxaayu njàng mi, moo xam ci nguur gi la jóge, ak ci way-demal seen bopp yi, ak ci ñi ajuwul fenn.

Jeexitali Jàngandoo 2014 yi gën a ràññeeku, ñeel mboolem xale yi ñu jax (yi ñu jox cax) wone nañu ne warees naa gën a baaxal njàng mi, naka noonu jeexital yooyu dañu dëgëral tegtali natt bu yaatu bi ñu jotoon a def ci 2013. (Seetal nataal 1)

3. Woroo gu mag diggante ndam yi ci yeewute (86.7%, juróom-ñett-fukk ak juróom- benn, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ak lajj yi ci duruus (27.7%, ñaar-fukk ak juróom-ñaar, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ak ci xayma (22.2%, ñaar-fukk ak ñaar, tomb ñaar ci téeméer). (Seetal nataal 3 xët 4)

4. Wuute yu am solo ci wàllu xareñ, su ñu ko seetee ci tërinu jànguwaay yi ci wàllu aju ci nguur gi walla déet, ak ci melokaani kër yi ñu defe gëstu bi, ak it ci melokaani jànguwaay yi.

Lu am solo, ñu gis ko, moo di ndam yi dañuy daldi wàññeeku, su fekkee laaj yu luxu lañu laaj xale yi. Ndax, su ñu seetee xareñ yi ci biir xeetu cax bu ne, ñu gis ne ci duruus, na jafe-jafe yi gën a tar, ndam yi gën a wàcc ; su dee lu jëm ci jàng araf yi ak dégtu yi : 74.5% (juróom-ñaar-fukk ak ñeent, tomb juróom ci téeméer) ; su dee ci njàngum dogi baat yi : 62.6% (juróom-ben-fukk ak ñaar, tomb juróom-benn ci téeméer) ; su dee ci njàngum baat yi : 50.1% (juróom-fukk, tomb benn ci téeméer) ; su dee ci duruusu dawal : 36.7% (fanweer ak juróom-benn, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ; su dee ci duruus-nànd : 29.4% (ñaar-fukk ak juróom-ñeent, tomb ñeent). (Seetal nataal 4, xët 4)

Ak fu dogal mën a jóge, wonekati baaxaay yi dañu war a fexe ba jubluwaayi njàng mi feeñ ci xam-xam bi ñuy jàngale, ak ci anam yi ñu koy jàngalee, ak ci jumtukaay yi. Gannaaw ba ñu xamee ne jubluwaay bi moo di yar doomu réew ju mënal boppam, ñu waajal ko ba mu yegg ci xam-xam yi gën a kowe te am njariñ ci yokkuteg askanam, yorinu li aju ci njàng mi, ci baaxaayu njàng mi dëgg la bokk.

Looloo waral ñu amal kayit guy won yoon boroom dogal yi bëgg jëf ngir baaxaayu njàng mi. Wonekat yi dañuy fésal solo si xam-xam bi ñuy jàngal xale yi am ci nattu baaxaayu njàng mi. Te yit sasoo nañu dëppale njàng meek jàngaleyin wi ak aaday xale yi, boole ci gën a baaxal li wër njàng mi.

Tële duruusu dawal-nànd dafa nekk gàllankoor bu mag ci xayma, te li ñuy jàllale njàng mi ci kàllaama yu fi dëkkul moo ko waral ; su dee ci tolluwaayu ndam ci waññ : 70.3%, juróom-ñaar fukk, tomb ñett ci téeméer ; su dee ci wàññi : 49.5% ñeen-fukk ak juróom-ñeent, tomb juróom ci téeméer ; su dee ci ful : 43% ñeen-fukk ak ñett ci téeméer ; su dee ci sewometri : 54.5%, juróom-fukk ak ñeent, tomb juróom ci téeméer ; su dee ci natt yi : 69.7% juróom-ben-fukk ak juróom-ñeent, tomb juróom-ñaar ci téeméer ; ci wàcce pasin : 24.2% ñaar-fukk ak ñeent, tomb ñaar ci téeméer. (Seetal nataal 5, xët 4)

Su ñu jëlee cax bu ne, xareñ gi ci xale yi wone, lëkkale ko ak tërinu jànguwaay yi, jànguwaayi frãse yiy demal seen bopp ñoo gën a baax jeexital, ndax ci duruus am nañu 57.5% (juróom-fukk ak juróom-ñaar, tomb juróom ci téeméer) ; ci xayma ñu am 48.7% (ñeen-fukk ak juróom-ñett, tomb juróom-ñaar ci téeméer). Jànguwaayi frãse yi aju ci nguur gi ñoo ci topp ak 31.2% (fanweer ak benn, tomb ñaar ci téeméer) ci duruus, ak 26.3% (ñaar-fukk ak juróom-benn, tomb ñett ci téeméer) ci xayma. Ak lu ëpp tuuti benn ñeenteel ci duruus, maanaam 26,9% (ñaar-fukk ak juróom-benn, tomb juróom-ñeent ci téeméer, ak lu jege genn-wàll ci xayma, maanaam 48.7% (ñeen-fukk ak juróom-ñett, tomb juróom-ñaar ci téeméer), jànguwaayi frãse-araab yi aju ci nguur gi ñoo ko yóbbul seen moroom yiy demal seen bopp, rawatina ci lu jëm ci duruus.

Waaye nag, jànguwaayi frãse-araab yiy demal seen bopp ñoo leen raw tuuti ci xayma ak 13.2% (fukk ak ñett, tomb ñaar ci téeméer), fekk yi aju ci nguur gaa ngi am 11.6% (fukk ak benn, tomb juróom-benn ci téeméer). Jànguwaayi kominoteer yi am nañu 15.7% (fukk ak juróom, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ci duruus, waaye amuñu lu dul 3.2% (ñett.tomb ñaar ci téeméer) ci xayma. Su dee daara yi ñoom, am lu baax jafe na leen ak 6.7% (juróom-benn, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ci duruus, ak 2.6% (ñaar, tomb juróom-benn) ci xayma.

Kon ci xayma la ndam yi gën a néew. Loolu safaanoo ak li xew ci yeewute, ndax jànguwaay yépp ndam yu baax lañu am, dale ko ci 93.9% (juróom-ñeen-fukk ak ñett, tomb juróom-ñeent ci téeméer) soxal jànguwaayi frãse yiy demal seen bopp, jëm ci 51.3% (juróom-fukk ak benn, tomb ñett ci téeméer) ci jànguwaayi kominoteer yi. ( Seetal nataal 6, 7, ak 8, xët 4)

Su ñu seetee nag cax bu ne ci biir diwaan yi, ñu gis ne, Ndakaaroo ci sut baaxaayu njàng, ak 44.5% (ñeen-fukk ak ñeent, tomb juróom ci téeméer) ci duruus, ak 36.4% (fanweer ak juróom-benn, tomb ñeent ci téeméer) ci xayma. Njaaréem a ci topp ak 30.7% (fanweer, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ci duruus, ak Sigicoor 28.3% (ñaar-fukk ak juróom-ñett, tomb ñett ci téeméer). Su dee lu jëm ci xayma, Sigicoor a raw ak 25.5% (ñaar-fukk ak juróom, tomb juróom ci téeméer), ak Kedugu 25.3% (ñaar-fukk ak juróom, tomb ñett ci téeméer). Ci duruus, Koldaa moo des gannaaw ak 11.1% (fukk ak benn, tomb benn ci téeméer) ; ci xayma, Kafrin néew na doole ak 7.6% (juróom-ñaar, tomb juróom-benn ci téeméer). (Seetal nataal 9 ak 10 xët 4)

Ci yeewute, Diwaan yépp a nga ca kow : Ndakaaru ak 94.3% (juróom-ñeen-fukk ak ñeent, tomb ñett ci téeméer), Sigicoor ak 93.1% (juróom-ñeen-fukk ak ñett, tomb benn ci téeméer), Kafrin dem ba 74,2% (juróom-ñaar-fukk ak ñeent, tomb ñaar ci téeméer). (Seetal nataal 11, xët 4). Ci noonu, ñu gis ne njàngaan yaa ngi gën a aay, su fekkee ne li ñu leen laaj jëmmu na ci seen xel. Doyadig téere yi ak ni ñu leen di jëfandikoo gu néew gi tax na ba seen njariñ feeñul ni mu ware ci baaxaayu njàng mi.

1. Ndam yi xale yi am ci 2013, 12.2%1 (fukk ak ñaar, tomb ñaar ci téeméer) ak ci 2014, 18.6% (fukk ak juróom-ñett, tomb juróom-benn ci téeméer) néew nañu ba tey, ci ñaari kàllaama yi xale yi tànn ngir ñu jaarale ci cax yi.

2. Su ñu dendalee jeexital yi, fekk ñu ngi wéeru ci kàllaama gi ñu jaarale cax bi, xale yi ñu jax ci frãse ñoo gën a aay ci duruus (33.2 %, fanweer ak ñett, tomb ñaar ci téeméer) xale yi ñu jax ci araab (11.4%, fukk ak benn, tomb ñeent ci téeméer). Naka noonu, ci xayma yitam, xale yi ñu jax ci frãse ñoo gën a aay (27.7%, ñaar- fukk ak juróom-ñaar, tomb juróom-ñaar ci téeméer) ñi ñu jax ci araab (5.6%, juróom, tomb juróom-benn ci téeméer). Ci yeewute, ba tey frãse moo ëpple tuuti, ndax am na 88.8% (juróom-ñett-fukk ak juróom-ñett, tomb juróom-ñett ci téeméer) fu araab ame 80.7% (juróom-ñett-fukk, tomb juróom-ñaar ci téeméer). (Seetal nataal 2)

Jeexitali nattu 2014, cig tënk

Ay wonekati baaxaay : kayit giy won yoon boroom dogal yi !

1 Tolluwaayu ndam yii, mu ngi soxal xale yi am 6 ba 14 at yi ñu natt ci attum 2013. Tolluwaay yi lee ngi nekk 19.1% ci xale yi am 6 ba 18 at.

Nos partenaires

Lees war a jàpp ci jeexitali nattu Jàngandoo 2014

Laboratoire de Recherche sur les Transformations Economiques et Sociales (LARTES)Institut Fondamental d’Afrique Noire (IFAN), Université Cheikh Anta Diop de Dakar (UCAD)BP. : 206 Dakar, Sénégal - Tél. : (221) 33 825 96 14 / 33 825 92 32 - Site : www.lartes-ifan.gouv.sn